Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na raxas, walla daan na sangu ci Saah ba ci juróomi Mudd, (mooy ñaari loxoom bamu fees) daan jàppu ci benn Mudd

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na raxas, walla daan na sangu ci Saah ba ci juróomi Mudd, (mooy ñaari loxoom bamu fees) daan jàppu ci benn Mudd

Jële nañu ci Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na raxas, walla daan na sangu ci Saah ba ci juróomi Mudd, (mooy ñaari loxoom bamu fees) daan jàppu ci benn Mudd.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na sangu janaba ci Saah ba ci juróomi Mudd, daan jàppoo benn Mudd. Saah mooy ñenti Mudd, Mudd: mooy luy toll ci feesal ñaari ténqi nit ku yem cig jëmm.

فوائد الحديث

Yoonalees na sakkanal nduxum njàppu mi ak sangu mi, te bañ a yàq donte dafa yomb.

Sopp nañu néewal ndoxum jàppu mi ak mu sangu mi ci kem aajo ja, ndax lii mooy njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Li ñu ci jublu mooy matale njàppu mi ak sangu mi ànd ak sàmmonte ak sunna yi ak teggin yi ci lu dul yàq walla ŋott, sàmmonte it ak waxtu wi ak barig ndox mi ak néewaayam ak yeneen.

Dees na tudde janaba képp ku génne Maniyu walla mu sëy, dees koo tudde loolu ngir li boroomam di moytu julli ak jaamu yiy aajowoo ag laab.

Saah: ag natt la gu ñu xam, li ñu ci namm mooy Saahu Yonnente bi, ag peeseem di toll ak (480) Misxaal ci pepp mu baax, bu dee ci liitar (3liitar).

Mudd: ag nattug Sariiha la, te mooy feesal ñaari ténqi nit ku yem, bu ko feesalee tàllal loxoom, Mudd mooy ñenti Saah ci dëppoog woroom xam-xami fiq yi, ñi koy nattale ci(750) mili liitar.

التصنيفات

Sunna ak teggiini njàpp