إعدادات العرض
Bu kenn ci yéen jullee ci benn yére te dara tegewul ci kaw mbaggam
Bu kenn ci yéen jullee ci benn yére te dara tegewul ci kaw mbaggam
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «Bu kenn ci yéen jullee ci benn yére te dara tegewul ci kaw mbaggam».
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Português Nederlands Tiếng Việt অসমীয়া ગુજરાતી Kiswahili پښتو සිංහල മലയാളം नेपाली Magyar ქართული తెలుగు Македонски Svenska Moore Română Українська ไทย मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na kuy julli ci benn yére ay mbaggam di feeñ dara teguwul ci kawam; ndaxte ñaari mbagg yi donte duñu awra, muur leen moo gën a jàppandi muur awra wi, te moo gën a jege màggal Yàlla mu màgg mi, ag màggal ko ci jamono yi mu taxawe ci kanamam ci julli gi.فوائد الحديث
Dagan na ñu jullee benn yére bu muure li ñu war a muur.
Dagan na ñu jullee ñaari yére, benn bi muur kaw yaram wi, beneen bi muur suuf gi.
Sopp nañu kiy julli nekk ci melo wu rafet.
Dañoo war a muur ñaari mbagg yi walla benn bi ci julli gi, ndeem loolu jàppandi na, nee nañu it tereg wattandiku la.
Tuutig li nekk ci loxoy Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ci alal, ba tax ñenn ñi ci ñoom amuñu ñaari yére.
An-Nawawii wax na ci maanaa hadiis bi ne: ag xereñam mooy ni bu ko muuroo te dara nekku ci mbagg mi wóorul awraam wuññeeku, wuute ak bu tegee lenn li ci mbaggam, ak it ne man na koo aajowoo tëye ci loxoom walla ci ñaari loxoom te kon day soxlawoo loolu, te kon sunnag teg loxo ndayjoor bi ci kaw loxo càmmooñ bi ci kaw dënnam da koy faat, ak di leen yëkkati fi ñu yoonale yëkkëti ga, ak yeneen, ak ne it bàyyi muur kaw yaram wi ak barabu taar wi da ci a nekk, te Yàlla mu kawe mi nee na: {jëlleen seenug taar ci jépp jàkka} [Al-Ahraaf:31].
التصنيفات
Sàrti julli