ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee

ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee

Jële nañu ci Abuu Umaamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee".

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw bu noppee ci jullig farata gu ne dara terewu koo dugg àjjana lu dul dee; moom nag moo ngi ci saaru Al-Baxara, mooy waxi Yàlla ji: {Allaahu laa ilaaha illa Huwal Hayyul Xayyuumu laa taaxuzuhu sinatun walaa nawmun lahu maafis Samaawaati wa maa fil-Ardi man zal lazii yasfahu hindahuu illaa bi-iznihii yahlamu maa bayna aydiihim wa maa xalfahum wa laa yuhiituuna bi say-in min hilmihii illaa bimaa saa-a wasiha kursiyyuhus Samaawaaati wal-Ardi wa laa ya-uuduhu hifsuhumaa wahuwal Haliyyul Hasiimu} [Al-Baxara: 255].

فوائد الحديث

Ngëneelu aaya ju màgg bii; ngir li mu làmboo ci ay tur yu rafet ak i melo yu kawe.

Sopp nañu jàng aayaa ju màgg jii

ginnaaw gépp jullig farata.

Jëf yu sell yi sabab la ci dugg àjjana.

التصنيفات

Sikkar yi ànd ak julli gi