bu kenn ci yéen sikk-sakkaa ci julleem te ba xamul ñaata la julli ndax ñatt la walla ñent, na sànni sikk-sakka ga, te tabax ca la ko wóor, topp mu sujjóot ñaari sujjóot njëkk muy sëlmël

bu kenn ci yéen sikk-sakkaa ci julleem te ba xamul ñaata la julli ndax ñatt la walla ñent, na sànni sikk-sakka ga, te tabax ca la ko wóor, topp mu sujjóot ñaari sujjóot njëkk muy sëlmël

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu kenn ci yéen sikk-sakkaa ci julleem te ba xamul ñaata la julli ndax ñatt la walla ñent, na sànni sikk-sakka ga, te tabax ca la ko wóor, topp mu sujjóot ñaari sujjóot njëkk muy sëlmël, bu dee juróom la julli ñu jotal ko julleem gi, bu dee dafa mottali ñent ya nag muy naqar ci saytaane».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne kiy julli bu de sikk-sakka ci julli gi ba xamul ñaata la julli, ñatt la walla ñent? Na sànni lim bu ëpp bi muy sikk-sakka te bañ koo jàpp; ndax ñatt yi mooy li ko wóor, mu julli beneen ràkka bu ñenteel, topp mu sujjóot ñaari sujjóot njëkk muy sëlmël. Bu dee li mu julli woon ñent la; kon juróom lay doon bu ñu ci dollee benn ràkka bi, ñaari sujjóoti njuumte yi wuutu benn ràkka, lim bi di ñaar-ñaar waaye du lu tóol: bu dee li mu julli boo ci tegee ràkka bi ci dolliku ñent la; kon def na la ko war ci lu dul dolli du caagine wàññi. Ñaari sujjóoti njuumte ngir toroxal saytaane la ak suufeel ko, ak delloo ko muy ku sooy ku sori la mu bëggoon; ndaxte dafa jaxase julleem gi, gaar ko ngir yàq ko, far jullig doomu Aadama ji mat ci li mu jëfe ndigalu Yàlla mu kawe mi ci sujjóot bi nga xam ne Ibliis da ko cee moy ba mu ko bañee topp Yàlla ci sujjóotal Aadama.

فوائد الحديث

Kiy julli bu sikk-sakkaa cig julleem te ben ci ñaari mbir yi notul fi moom kon day sànni sikk-sakka ga te jëfe la ko wóor, te mooy li gën a néew, bu ko defee mu mottali julleem gi, daal di def sujjóotu njuumte njëkk muy sëlmël, topp mu sëlmël.

Ñaari sujjóot yii yoon la ngir defar julli gi, ak delloo Saytaane muy ku sooy di ku torox di ku sori la mu bëggoon.

Sikk-sakka gi nekk ci hadiis bi mooy dengi-dengi ci lu dara notul, waaye bu njort amee ba not loolu la ñuy jëfe.

Ñaaxe ci xeex jaxjaxal (dengi dengi) ak jañ ko ci jëfe ndigalu Sariiha.

التصنيفات

Sujootu jamuj ak sujootu jàng ak sujootu sant