Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jàng na ci ñaari ràkkay Fajar: {Xul yaa ayyuhal kaafiruuna}, ak {Xul huwal Laahu Ahad}

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jàng na ci ñaari ràkkay Fajar: {Xul yaa ayyuhal kaafiruuna}, ak {Xul huwal Laahu Ahad}

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jàng na ci ñaari ràkkay Fajar: {Xul yaa ayyuhal kaafiruuna}, ak {Xul huwal Laahu Ahad}.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na sopp a jàng ci naari ràkkay Fajar ginnaaw Faatiha, ci ràkka bu njëkk bi saaru: {Xul yaa ayyuhal kaafiruuna}, (Alkaafiruuna), ci ràkka bu ñaareel bi saaru {Xul huwal Laahu Ahad} (Al-Ixlaas).

فوائد الحديث

Sopp nañu jàng ñaari saar yii ginnaaw Faatiha ci sunnay Fajar.

Ñaari saar yii lañuy woowe saari sellal yi; ndaxte nekk na ci saaru Alkaafiruuna ag sett wicc ci mbooleem lu bokkaalekat yi di jaamu te du Yàlla, ak ne ñoom itam duñu ay jaamukati Yàlla ndaxte seen bokkaale gi day màbb seen jëf yi, ndax Yàlla mu Sell mi mooy ki yayoo jaamu, nekk na it ci saaru Al-Ixlaas kennal Yàlla ak sellal ñeel ak leeral ay meloom.

التصنيفات

Ni ñuy jullee