ku yar ab xaj bu dul xaju rëbb walla xaju sàmm wàññi na ci jëfam bis bu nekk Xiiraat

ku yar ab xaj bu dul xaju rëbb walla xaju sàmm wàññi na ci jëfam bis bu nekk Xiiraat

Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ku yar ab xaj bu dul xaju rëbb walla xaju sàmm wàññi na ci jëfam bis bu nekk Xiiraat", Saalim ne: Abuu Hurayrata daan na wax: "walla xaju mbay", moom baykat la woon.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo la yar xaj, lu dul ngir aajoy rëbb, walla gaarde jur gi ak mbay mi, ku ko yar ngir lu dul loolu wàññi na ci yoolu jëfam bis bu nekk Xiraat; loo lu ag natt la gog Yàlla moo ko xam.

فوائد الحديث

Daganul ci jullit bi muy yar xaj, lu dul li ñu ci settee.

Tere nañu yar xaj; ngir li ci nekk ci yàqute ak lor yu bari, sax na jóge ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj; ak li ci nekk ci sobe gu mag gog dara du ko dindi lu dul baamtu raxas ga ci ndox ak suuf.

التصنيفات

Rëbb