Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan

Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan

Jële nañu Jaabir ibn Abdul Laahi yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan, mu wax ne: "bu kenn ci yéen yittewoo am mbir, na julli ñaari ràkka yu dul farata, topp mu wax: Allaahuma innii astaxiiruka, bi hilmika, wa astaqdiruka bi xudratika, wa as-aluka min fadlika Al-Hasiimi, fa innaka Taqdiru wa laa aqdiru, wa Tahlamu wa laa ahlamu, wa Anta Hallaamu alxuyuubi, Allaahuma in Kunta Tahlamu anna haasal amra xayrun lii fii diinii, wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii, wa aajilihi, faqdurhu lii wa yasairhu lii summa baarik lii fiihi, wa in Kunta tahlamu anna haasal amra sarrun lii fii diinii wa mahaasii wa haaqibati amrii" walla mu wax: "haajili amrii wa aajilihi, fasrifhu hanni wasrifnii hanhu waqdur liya alxayra haysu kaana summa ardinii bihii" nee na: "mu tudd aajoom".

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Bu jullit bëgge def mbir mu mu xamul ndax lu baax la am déet, dañuy yoonal ci moom mu julli jullig listixaar ndax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na xamal Sahaabaam yi yal na leen Yàlla dollee gërëm julli gii kem ni mu leen doon xamale saaru Alxuraan, day julli ñaari ràkka yu dul farata, topp mu ñaan Yàlla daal di wax: "yaw sama Boroom maa ngi lay tànnloo" di sàkku tawfeex ci li gën ci ñaari mbir yi, di la ñaan "ci sa xam" gu yaatu gi te peeg lépp, "di sàkku nga kàttanal ma" ci nga def ma may aji-am kàttan ndax amuma pexe du caagine kàttan lu dul ci yaw "ci sa kàttan" giy wéy yaw dara tëwu la, "maa ngi lay laaj ci sa ngëneel yi" ak sa rafetal, "gu màgg gi" te yaatu; ba tax say may di ngëneel ci yaw, kenn amul ci yaw àq ci genn xéewal; "yaw yaa man" lépp man maa néew kàttan di aji-tële "te manuma" dara ci lu dul sag ndimbal, "ak it" yaw "yaa xam" ci sa xam gu matale gi te peeg yi feeñ ak yi nëbbu, ak yiw yi ak ay yi, "te" man "xamuma" dara ci lu dul sag tawfeexal ak sag gindee "te yaw yaa xam kumpa yi" yaw la xam gu boy ñeel, ak kàttan guy wéy di def, te ku dul yaw amul dara ci loolu ci lu dul li nga ko dogalal ak li nga ko kàttanal. Topp jullit bi ñaan Boroomam, daal di tudd aajoom daal di wax "yaw Sama Boroom" man de bàyyeel naa la samay mbir "bu dee xam nga" ci sa xam gi ne mbir mii "mu tudd aajoom" niki jënn kër gii, walla jënn daamar gii (Oto bii), walla takk soxna sii walla lu dul loolu... Bu dee mbir mi jiitu na ci sa xam ci ne amna aw yiw ñeel ma ci sama diine ji nga xam ne mooy kaaraangey samay mbir, ak samag dund ci àdduna ak sama mujjanteeli mbir ak li sama mbir di mujje ci àdduna ak allaaxira; dogal ko te waajalal ma ko yombalal ma ko, te nga baarkeel ko, bu dee xam nga" yaw Yàlla ne mbir mii may listixaar du lu baax ci man ci sama diine ak samag dund ak sama mujjanteeli mbir def ko mu sori ma, te nga dogal ma aw yiw , topp nga gërëmloo ma ko.

فوائد الحديث

Yonente bi dafa xéroon lool ci jàngal ay sahaabaam julli gii; ngir li ci nekk ci njariñ ak yiw yu màgg.

Sopp nañu listixaar ak ñaan gu ñu toxal ginnaaw ga.

Listixaar sopp nañu ko ci mbir yu dagan yi nga xam ne da ñu ciy dengi-dengi, waaye du nekk ci mbir mu war walla mu ñu sopp; ndax lay cosaan mooy ñu def leen, waaye man naa listixaar ca la ca aju, niki tànn àndandoo ci Umra walla Aj.

Lu war ak lu ñu sopp deesul listixaar ci def leen, lu araam ak lu ñu sib deesul listixaar ci bàyyi leen.

Dañuy mujje ñaan gi ci julli gi; ndax waxi Yonente bi mu ne: "topp mu wax...", bu ñu ko waxee njëkk sëlmël gi aayul.

War na ci jaam bi mu delloo biram yépp ci Yàlla, war na ci moom it mu set wicc ci pexeem ak kàttanam; ndaxte Yàlla rekk moo am kàttan ak pexe.

التصنيفات

Jullig tànnloo Yàlla li gën ci lees di waaj a sóobu