Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum Koor, Saah ci tàndarma, walla Saah ci pepp, ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi, mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga

Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum Koor, Saah ci tàndarma, walla Saah ci pepp, ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi, mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga

Jële na ñu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum Koor, Saah ci tàndarma, walla Saah ci pepp, ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi, mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc waral na asakay muurum koor ginnaaw weeru koor, te mooy luy tolloo ak Saah muy tollook ñenti Mudd. Mudd mooy: lu fees ñaari loxoy góor gu diggudóomu, ci tàndarma walla pepp ci bépp jullit; gor ak jaam, góor ak jigéen, xale ak mag, loolu ci ku am lu des ci dundu bisam ak guddeem, ci boppam ak ki muy dundal. Mu digle ñu joxe ko laata nit ñi di génn jëm ca julli ga.

فوائد الحديث

Asakay muurum koor ci weeru kooy dafa war ñu génne ko ngir xale ak mag, ak gor ak jaam, kilifa gi ak sang bi lañu ciy waxam, góor gi da koy génneel boppam ak ay doomam ak ku mu war a dundal.

Asakay muurum koor warul ci ki ñu ëmb, waaye sopp nañu ko.

Leeral ci yi ñuy génne ci asakay muurum koor, ci ne mooy dund gi nit ñi aadawoo.

War nañu koo génne njëkk jullig hiid gi, la gën nag mooy mu nekk ci subag hiid gi, waaye dana dagan ñu génne ko njëkk hiid gi ci benn walla ñaari fan.

التصنيفات

Asakay muurum Koor