Yàlla du xool góor giy dikke soxnaam ci ginnaawam

Yàlla du xool góor giy dikke soxnaam ci ginnaawam

Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla du xool góor giy dikke soxnaam ci ginnaawam".

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na tëkku gu tar ci ne Yàlla du xool xoolu yërmànde jëm ci góor gir sëy ak góor ci ginnaawam walla jigéen ci ginnaawam, ak ne loolu dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi.

فوائد الحديث

Góor dikke góor -te mooy ag ngóor-jigéen- dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi.

Sëy ak jigéen ci ginnaawam ci bàkkaar yu mag yi la bokk.

(Yàlla du xool) maanaam xoolu yërmànde ak ñeewant, waaye jubluwuñu ci xool yépp; ndaxte Yàlla nu Sell mi te kawe dara nëbbuwu ko, te dara fàdduwul woli gisam.

Jëf yii dafa bokk ci ñaawteef yi màgg yi te di kaawteef ci kaw nit ñi; ndax li ci nekk ci wuute ak selluk nit ku mucc, ak nëewal njaboot, ak yàq dundug sëy gi, ak jëmbët noonoo ak mbañeel, ak tàbbi ci bérab yu salte yi.

التصنيفات

Àttey daan