ku xëy ci yéen di ku am jàmm ci yaramam, am kóolute ci bakkanam, am dundug bisam,, dafa mel ni jox nañu ko àdduna

ku xëy ci yéen di ku am jàmm ci yaramam, am kóolute ci bakkanam, am dundug bisam,, dafa mel ni jox nañu ko àdduna

Jële nañu ci Ubaydallah ibn Mihsan Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "ku xëy ci yéen di ku am jàmm ci yaramam, am kóolute ci bakkanam, am dundug bisam,, dafa mel ni jox nañu ko àdduna".

[Tane na] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku xëy ci yéen jullit ñi di ku wér di ku mucc ci yaramam ci tawat yi ak feebar yi, di ku am kóolute ci bakkanam ak njabootam, te ragalul ci yoonam, mu am lu ko doy ci dundug bisam ci li dagan; dafa mel ni booleel nañu ko àdduna jépp.

فوائد الحديث

Leeral ne nit ki dafa aajowoo jàmm ak kóolute ak dund.

War na ci jaam bi mu sant Yàlla mu kawe mi gërëm ko ci xéewal yii.

Xemmemloo ci doylu ak dëddu àdduna.

التصنيفات

Dëddu ak sàmm