إعدادات العرض
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii».
[Tane na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ ไทย Русский 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە دری Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Kinyarwanda नेपाली Română Српски Soomaali Moore Deutsch Українська Български Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ñaan ci diggante ñaari sujjóot yi ci julli gi juróomi ñaan yii nga xam ne jullit bi da cee am aajo ju màgg, te mu làmboo yiwi àdduna ak allaaxira, ci sàkku njéggal ak suturaal bàkkaar yi te baal ka ko, ak sotti ko yërmànde, ak mucc ci lënt-lënt yi ak bànneex yi ak feebar yi ak wopp yi, te ñaan Yàlla ag gindi ñeel dëgg te sax ca, ak wërsëgu gëm ak xam-xam ak jëf ju baax, ak alal ju dagan te teey.فوائد الحديث
Yoonalees na ñaan gii ci toogaay bi nekk ci diggante ñaari sujjóot yi.
Ngëneelu ñaan yii ngir li mu làmboo ci yiwi àdduna ak allaaxira.