demal julli waat, yaw julliwóo

demal julli waat, yaw julliwóo

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dugg na ci jàkka ji jenn waay daal di dugg julli ñaari ràkka, daal di nuyu Yonente bi, mu fay ko, daal di ne ko: "demal julli waat, yaw julliwóo", mu dellu julli waat namu jullee woon, daal di nuyu Yonente bi , mu ne ko: "dellul julli waat yaw julliwóo " ñatti yoon, mu ne ko: giñ naa ci ki la yónni ci dëgg manuma lu dul lii, xamal ma, mu ne ko: "boo jugee di julli, nanga kàbbar, topp nga jàng li jàppandi ci yaw ci Alxuraan, topp nga rukkoo ba dal, nga siggi ba yamoo ca taxaw ga, topp nga sujjóot ba dal, topp nga siggi ba yamoo ca toogaay ga, defal loolu ci sa julli gi yépp".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa dugg ci jàkka ji, jenn waay dugg ci ginnaawam daal di julli ñaari ràkka yu gaaw, te dalul ci taxaw ya ak rukkoo ya ak sujjóot ya, fekk Yonente bi mi ngi ka doon xool, mu ñëw ci Yonente bi fekk mu toog ci koñu jàkka ji mu nuyu ko, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fay ko, daal di ne ko: Dellul baamtu sa julli gi ndax julliwóo. Mu dellu julli waat julli gu gaaw kem na mu jullee woon, topp mu ñëw nuyu Yonente bi, mu ne ko: Dellul julli; ndax julliwóo, mu def ko ñatti yoon. Waa ji ne ko: giñ naa ci ki la yónni ci dëgg, manuma lu dul lii, kon xamal ma, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: Boo jugee jëm ci julli gi nanga kàbbar kàbbaru armal, topp nga jàng faatiha ak lu la soob, nga daaldi rukkóo ba dal, nga deg say ténq ci sa kaw óom yi tàllal sa ndigg li, topp nga siggi taxawal sa ndigg li ba yax yépp yi dellu nga taxaw temm, topp nga sujjóot ba dal nga teg sa jë bi ak bakkan bi, ak ñaari loxo yi, ak ñaari óom yi ak cati baaraami tànk yi ci kaw suuf, topp nga siggi ba dal ca toogaay ba ci diggante ñaari sujjóot yi, topp nga def loolu ci ràkka bu ne ci sa julli gi.

فوائد الحديث

Ponki julli yii, du rot mukk moo xam njuumte la walla ñàkk a xam, li koy tegtale mooy li mu digal aji-julli ji mu baamtuwaat, te Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yamul ci jàngal ko dong.

Dal ci julli gi ponk la ci ponki julli.

An-Nawawii nee na: nekk na ci ne ku bàyyi yenn yi war ci julli julleem du wér.

An-Nawawii nee na: nekk na ci it def ndànk ci kiy jàng ak ki xamul ak ñeewante ko, ak leeralal ko masala mi tënkal ko jubluwaay bi, ak yam ci li ëpp solo ci lu moom ba ña dugg ci lumu àttanul.

An-Nawawii nee na: nekk na ci it ne kiy ubbee bu ñu ko laajee dara am leneen lu aji-laaj ji aajowoo te laaju ko sopp nañu ci moom mu tuddal ka ko, lii nag ci laabire la bokk du dugg ci wax lu sa yoon nekkul.

Ngëneelu nangu ne da ngaa gàtteñlu, ngir li mu wax ne: "manuma lu dul lii, kon xamal ma".

Ibn Hajar nee na: nekk na ci it digle lu baax ak tere lu bon, ak jàngkat bi sàkku ci aji-xam ji mu xamal ko.

Sopp nañu nuyóo bu ñu dajee, fay nuyóo ga nag lu war la, sopp nañu it ñuy baamtu nuyóo gi bu dee dañoo daje waat donte jamano ji ñu daje waat dafa jegee, fay nuyóo it dafa war ci yoon wu ne.

التصنيفات

Ni ñuy jullee