déng naa la ngay bari looy sujjóotal Yàlla, ndaxte doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne Yàlla dina la ci yëkkatil daraja, sippil la ci njuumte

déng naa la ngay bari looy sujjóotal Yàlla, ndaxte doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne Yàlla dina la ci yëkkatil daraja, sippil la ci njuumte

Jële nañu ci Mahdaan ibn Abii Talhata Alyahmarii mu wax ne: Dajee naa ak Sawbaan surgab Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ma ne ko: wax ma jëf joo xam ne bu ma ko defee Yàlla dugal ma ci àjjana? Walla mu ne ma ne ko: jëf ji Yàlla gën a bëgg, mu noppi, ma laajaat ko, mu noppi, ma laajaat ko ñatteelu yoon, mu ne ma: laaj naa ko Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ma: "déng naa la ngay bari looy sujjóotal Yàlla, ndaxte doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne Yàlla dina la ci yëkkatil daraja, sippil la ci njuumte" Mahdaan nee na: ma dajee ak Abuu Dardaa ma laaj ko mu tontu ma: lu mel ni li ma Sawbaan wax.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jëf joo xam ne sabab la ci dugg àjjana, walla jëf ji Yàlla gën a bëgg? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax aji-laaj ji ne ko: deel taqoo ak baril sujjóot ci julli, ndax doo sujjóotal Yàlla genn sujjóot lu dul ne dana la ci yëkkatil daraja, jéggal la ci njuumte.

فوائد الحديث

Ñaax jullit bi mu xér ci julli fatara ak naafila, ndax li mu làmboo ak sujjóot.

Leeral ni Sahaaba yi dégge diine, ak xam ne àjjana deesu ko am -ginnaaw yërmàndey Yàlla - ci lu dul jëf.

Sujjóot ci julli dafa bokk ci sabab yi gën a màgg ci yëkkati ay daraja, ak jéggal ay bàkkaar.

التصنيفات

Ngëneelu julli