ku wax: subhaanal Laahi Alhasiimi wa bi hamdihi, ñu jëmbëtal ko ag garabu tàndarma ca àjjana

ku wax: subhaanal Laahi Alhasiimi wa bi hamdihi, ñu jëmbëtal ko ag garabu tàndarma ca àjjana

Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ku wax: subhaanal Laahi Alhasiimi wa bi hamdihi, ñu jëmbëtal ko ag garabu tàndarma ca àjjana".

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku wax: (subhaanal laahi al hasiimu wa bi hamdihii) mu sellal Yàlla ci jëmmam ak i meloom ak i jëfam, dees na ko jëmbëtal ag garabu tàndarma ca suufu àjjana ci wépp yoon wu mu ko waxe.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci baril tudd Yàlla, te bokk na ci loolu: sàbbaal gu ànd ak sant.

Àjjana lu yaatu la, am njëmbëtam mooy sàbbaal yi ak sant, muy ngëneel ak xéewal gu bawoo ci Yàlla mu kawe mi.

Jagleel nañu tàndarma ci hadiis bi wolif geneen garab; ngir njariñam yu bari ak meññetam wu teey; loolu moo tax Yàlla joxe ci misaal ci aji-gëm ji ak ngëmam ci biir Alxuraan.

التصنيفات

Njariñi tudd Yàllay Mu tedd Mu màgg mi