إعدادات العرض
xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la
xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la
Jële na ñu ci Anas yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la«.
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी සිංහල ئۇيغۇرچە Hausa Português Kurdî Русский Tiếng Việt Kiswahili অসমীয়া ગુજરાતી Nederlands മലയാളം Română Magyar ქართული Moore ಕನ್ನಡ Svenska Oromoo Македонски ไทย Українська తెలుగు پښتو मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasy ភាសាខ្មែរالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaaxe na ci xëdd te mooy lekk ci mujjanteelu guddi gi ngir waajal koor gi; ndaxte am na (baarke) mooy yiw wu bari ci fay akub yool, ak taxaw ci waxtu wi mujj ci guddi gi ngir ñaan, ak dëgërlu ci woor gi, ak cawarte, ak woyofal coonaam.فوائد الحديث
Sopp nañu xëdd ak jëfe ndigalul sariiha ci def ko.
Ibn Hajar wax na ci Fathul Baarii: baarke ci xëdd gi day am ci ay anam yu bari, te mooy topp sunna, ak wuute ak ñoñ-téere yi, ak dëgërlu ci jaamu gi, ak dolli cawarte, ak jañ ñaaw jikkó ji nga xam ne xiif gi da koy indi, ak sabablu ci sarax kuy laaj jamono jooju, walla mu bokk ak moom lekk, ak sabablu ci sikar ak di ñaan ci waxtuw nangu ñaan ga, ak dabaatal yéeneg woor gi ñeel ku ko sàggane njëkk muy nelaw.
Rafetug jàngàlem Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba tax mu lënkale àtte bi ak sabab bi; ngir dënn yi ubbeeku ci, ñu xame ci kaweg sariiha.
Ibn Hajar nee na: xëdd dana ame ci lu gën a néew ci li nit ki di jëfandikoo ci lekk ak naan.
التصنيفات
Sunnay koor