jihaadleen ak bokkaalekat yi ci seen alal ak seen bakkan ak seen làmmeñ

jihaadleen ak bokkaalekat yi ci seen alal ak seen bakkan ak seen làmmeñ

Jële nañu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «jihaadleen ak bokkaalekat yi ci seen alal ak seen bakkan ak seen làmmeñ».

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na ñu jihaad ak yéefar yi ak def lu ñu man ci jàmmaarlook ñoom ci bépp jumtukaay ngir kàddug Yàlla di gën a kawe, te bokk na ci loolu: Bi ci njëkk: joxe alal ci jihaad leen; ci jënn ngànnaay, ak ub dund ci jihaadkat yi ak yu ko niru. Ñaareel bi: jël sa bakkan ak sa yaram génn ngir daje ak ñoom xeex ak ñoom. Ñatteel bi: woo leen jëme ci diine ji ci làmmeñ, ak taxawal lay ci seen kaw, ak jàjji leen delloo seen i lay.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci jihaad ak bokkaalekat yi ci bakkan ak alal ak làmmiñ; ku nekk ak kem kàttanam, ak ne jihaad yamul ci rayante ci bakkan rekk.

Digle gi ñu digle jihaad day tekki ne lu war la, man naa nekk faratay jëmm, man naa nekk it farata ngir ñenn ñi.

Yàlla dafa yoonal jihaad ngir ay mbir, bokk na ca: bi ci njëkk: jàmmaarloo ak bokkaale ak bokkaalekat yi; ndaxte Yàlla du nangu bokkaale mukk, ñaareel bi: dindi pakk yiy gaar yoonu woote jëme ci Yàlla, ñatteel bi: aar pas-pas ci lépp lu safaanoo ak moom, ñenteel bi: aar jullit ñi ak seen i réew ak seen i der ak seen i alal.

التصنيفات

Àttey xeex ci yoonu Yàlla