bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo

bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo

Jële na ñu ci Matar Ibn Hukaamis- yal na leen Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo».

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bu Yàlla dogalee ci jaam bi mu War a faatu a fi barab te moom nekku fa; da ko fay defal aajo mu dem fa, ñu jël fa ag ruuham.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Hadiis bi day dëggal li Yàlla mu kawe mi wax ne: {benn bakkan xamul ci ban suuf lay faatoo}.

التصنيفات

Gëm dogal yi, Dee ak i àtteem