sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee

sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee

Jële nañu ci Amr ibn Sulaym Al-Ansaarii mu wax ne: maa ngi seedeel Abii Sahiid ne wax na ne: maa ngi seedeel Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne wax na ne: "sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day leeral ne sangu bisub àjjuma lu feddaliku la mel ni lu war ci gépp góor gu nekk muskallaf ci jullit ñi ci ku àjjuma war ci ñoom, Ak mu setal ay bëñam ci socc ak lu ko niru. Ak mu laal gëtt ci xet gu neex gu mu man a doon te teey.

فوائد الحديث

Sopp gi ñi sopp sangu bisu àjjuma day feddaliku ci bépp jullit bu góor te nekk muskallaf.

Cet ak dindi xet gu bon lu ñu sàkku la ci sariiha ñeel bépp jullit.

Màggal bisub àjjuma, ak waajal ko.

Socc ngir jumaa luñu sopp lool la.

Sopp nañu laal gëtt ci gépp xet gu neex te teey njëkk ñuy dem ca jullig jumaa ga.

Jigéen gi bu génnee ci këram jëm ca julli ga walla ci leneen, du dagan ci moom muy laal gëtt; ngir li sunna tegtale ne loolu dafa araam.

Ki Mat Muskallaf mooy ki gént, te mat dafa am ay màndarga, ñatt yi góor ak jigéen ñoo ko bokk, te bi ci njëkk mooy: matal fukki at ak juróom, ñaareel bi: bu kawar gu ñagas saxee ci li wër awraam, ñatteel bi: génne maniyu ci gént walla ci bànneex donte du gént, bu dee màndarga mu ñenteel mi nag moom jigéen moo ko jagoo te mooy: gis mbaax bu jigéen gisee mbaax day nekk muskallaf.

التصنيفات

Àttey jullig Àjjuma