boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc

boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc

Jële nañu ci Al-Baraa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral nekkiinu loxo yi ci sujjóot bi ci julli gi, te loolu mooy mu dëgëral ay ténqam ci suuf mu kebale baaraam yi mu jëm xibla, ñaari conc yi yëkkëtiku wolif muy laal suuf ñu sori ñaari wet yi.

فوائد الحديث

Li war ci kiy julli mooy mu teg ñaari ténqam ci kaw suuf, ñaari ténq yi ñaari cér la ci juróomi cëri sujóot yi.

Sopp nañu yëkkëti ñaari loxo yi wolif muy laal suuf, sib nañu di leen lal kem ni negment di lale ñaari loxoom.

Yoonal nañu feeñal cawarte ak kàttanam ak ug xemmem ci jaamu gi.

Kiy julli bu sukkandikoo ci mbooleem céri sujjóot yi, cér bu nekk day jël àqam ci jaamu gi.

التصنيفات

Ni ñuy jullee