jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu

jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu

Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: damaa amoon ay góom, ma laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla xéewal ak mucc- ci lu jëm ci julli, mu ne ma: «jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu».

[Wér na] [Al-buxaariy soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne cosaan ci julli mooy taxaw, lu dul ne manu ko mu julli toog, bu ko manul mu julli tëdde wet.

فوائد الحديث

Julli du wàcci nit ki feeg xel maa nga fa, waaye day juge ci melo jëm ci weneen melo kem kàttanam.

Yaatug Lislaam ak yombam ci jaam bi ba day def jaamu gi namu ko mane.

التصنيفات

Jullig ñi am ngànt