Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jenn waay julli moom dong ci ginnaaw sàppe si, mu digal ko mu bàmtu julleem gi

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jenn waay julli moom dong ci ginnaaw sàppe si, mu digal ko mu bàmtu julleem gi

Jële nañu ci Waabisata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jenn waay julli moom dong ci ginnaaw sàppe si, mu digal ko mu bàmtu julleem gi.

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jenn waay julli moom dong ci ginnaaw sàppe si, mu digal ko mu bàmtu julleem gi; ndaxte julleem gi ci anam googu du wér.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci teel a ñëw ci jullig mbooloo, ak ñi bañ a julli ci ginnaaw sàppe si di way-beru ba du yóbbe julleem gi ci ag yàqu.

Ibn Hajar nee na: ku tàmbalee julli gi cig beru ci ginnaaw sàppe si njëkk ñuy siggi ci rukkóo bi bàmtu du ko war, kem ni mu ñëwe ci hadiisu Abii Bakrata, bu dul loolu kon ci matleg hadiisu Waabisata bàmtu da koy war.

التصنيفات

Àttey ki jiite julli ak ña mu jiite