ñaari julli yii ñooy julli yi gën a diis ci naaféq yi, te bu ngeen xamoon li nekk ci ñoom ñaar dangeen ko teewe donte dangeen di raam ci ay wóom

ñaari julli yii ñooy julli yi gën a diis ci naaféq yi, te bu ngeen xamoon li nekk ci ñoom ñaar dangeen ko teewe donte dangeen di raam ci ay wóom

Jële nañu ci Ubay ibn Kahb yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jiite na nu benn bis jullig suba mu daal di wax ne: "ndax diw teew na?" Ñu ne ko: déedéet, mu ne waat: ndax diw teew na? Ñu ne ko déedéet, mu ne: "ñaari julli yii ñooy julli yi gën a diis ci naaféq yi, te bu ngeen xamoon li nekk ci ñoom ñaar dangeen ko teewe donte dangeen di raam ci ay wóom, te sàppe gu njëkk gi moo ngi mel ni sàppey malaaka yi, te bu ngeen xamoon ngëneelam dangeen ko njëkkante, jullig góor ànd ak ñaari góor moo ëpp julleem ak genn góor, lu gën a bari moo gënal Yàlla mu kawe mi".

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa julli fajar benn bis, daal di laaj: ndax diw teewe na julli gii? Sahaaba yi ne ko: déedéet. Mu wax keneen ndax diw teew na? Ñu ne: déedéet. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: Jullig fajar ak gee ñoo gën a diis ci naaféq yi; ngir li tayyeel di ca not, ak li ca ngistal néew, ndax duñu leen gis ci lëndëm gi. Bu ngeen xamoon li ci ñaari julli yii suba ak gee ci fay ak yool gu bari -ndax fay day yam ak coona- kon dangeen ko teewe donte dangeen di raam di doxe ay loxo ak i wóom. Te sàppe gu njëkk gi ci ni ñu jegee imaam bi moo ngi mel ni sàppey Malaaka yi ci ni ñu jegee Yàlla mu kawe mi, te bu jullit ñi xamoon ngëneelu sàppe gu njëkk gi kon danañu njëkkante jëm ca, Ak ne jullig góor ànd ak geneen góor moo gën a màgg yool julleem moom dong, te ag julleem ak ñaari góor moo gën julleem ak genn góor, Julli gi bariy nit la Yàlla gën a bëgg te moo ëpp ngëneel.

فوائد الحديث

Yoonalees na ci imaamu jàkka ji muy nemmiku mbiri maamuun yi, ak di laaj ku teewul ci ñoom.

Taqoo ak jullig mbooloo, rawati na jullig gee ak fajar dafa bokk ci màndargay gëm.

Màggaayu payug gee ak fajar, ndax li

nekk ci teewe ko ci xeex ak bakkan ak muñ ci topp Yàlla, moo tax seenug fay gën a màgg gu dul

ñoom ñaar.

Jullig mbooloo day fasoo ci ñaar jëm kaw.

Leeral ngëneelu sàppe gu njëkk gi, ak xemmemloo ci njëkkante ko.

Ngëneelu mbooloo mu bari, ndax lu mbooloo mi gën a bari rekk fay gi di gën a bari.

Jëf yu baax yi dañuy rawante ci ngëneel kem ni leen Sariiha gënalantee, ak melo yi ñu melowoo.

التصنيفات

Ngëneelu jullig mbooloo ak i àtteem