daal di jàpp njàppum Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-

daal di jàpp njàppum Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-

Jële nañu ci Yahyaa ibn Umaarata Al-Maasinii mu wax ne: Gis naa Amr ibn Abii Hasan mu laaj Abdullah Ibn Saydin, nu Yónente bi doon jàbbee, mu laaj ndab lu def ndox, daal di jàpp njàppum Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu sotti ci loxoom, raxas loxo yi ñatti yoon, mu daal di dugal loxoom ci ndab li daal di gallaxndiku daal di saraxndiku daal di fiiru ci ñàtti tanq,mu daal di dugalaat loxoom daal di raxas kanamam ñatti yoon,daal di raxas loxoom ba ci coñc yi ñaari yoon,mu dugalaat loxoom daal di masaa boppam yóbb ko ci kanam ak ci ginnaaw benn yoon,mu daal di raxas ñaari tànkam ba ci dojor yi.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Abdullah Ibn Saydin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- leeral na ni Yonnente bi daan jàppoo, ci anamug jëf, Mu laaj ndab lu ndaw bu def ndox, Mu njëkk a tambalee raxas ay ténqam, daal di dëngal ndab li sotti ndox mi ci loxoom raxas leen ñatti yoon ci bitti ndab li, Mu dugal loxoom ci ndab li, daal di tanq ñatti tanq daal di gallaxndiku ci tanq gu ne saraxndiku ci fiiru ci. Mu tanqaat ci ndab li daal di raxas kanamam ñatti yoon, Mu tanqaat raxas ñaari loxoom ba ci coñco yi ñaari yoon, Mu dugalaat loxoom ci ndab li daal di masaa boppam ci ñaari loxoom tàmbalee ci kanamu bopp bi ba ca ndong la ci kaw doq gi, mu delloo ko ba egg ca fa mu tàmbalee woon, Mu daal di raxas ñaari tànk yi ba ci dojor yi.

فوائد الحديث

Jëfandikoog jàngalekat bi yoon yi gën a gaaw ci dégg ak xam gu sax, te bokk na ci loolu jàngale ci anamug jëf.

Dagan na ñu baamtu yenn céri njàpp yi ñatti yoon yeneen yi ñaari yoon, waaye liy farata ji mooy benn yoon.

Toftale céri njàpp yi dafa war kem ni mu ñëwe ci Hadiis bi.

Fi xar kanam yam mooy fi kawar di baaxoo saxe, ba li wàcc ci lex yi ak sikkim bi ci guddaay, ak ci nopp bi ba ca nopp ba ci yaatuwaay.

التصنيفات

Ni ñuy jàppoo