ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko

ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko

Jële nañu ci Abii Xataadata yal na ko Yàlla dollee gërëm ne na da doon seet kenn ku ko ameeloon bor, mu làqatu ko topp mu gis ko, mu ne ko: man de ci jafe-jafe laa nekk, mu ne: ndax da nga ko waat ci Yàlla? Mu ne ko: waat naa ko ci Yàlla? Mu ne ko: man dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di wax naan: «ku bëgg Yàlla musal ko ci xat-xati ëllëg bis-pénc, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe walla mu teggil ka ko».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Abuu Xataadata Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm da doon seet ku ko yoreel bor di ko làqtu, mu gis ko, ki ko ameel bor ne ko: man de damaa nekk ci jafe-jafe, te amuma alal ju ma la faye sa bor. Abuu Xataadata yal na ko Yàlla dollee gërëm giñloo ko ci Yàlla ci ne amul alal? Waa ji giñ ci Yàlla ci ne li mu wax dëgg la. Abuu Xataadata ne ko dégg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Ku bëgg Yàlla bégloo ko musal ko ci jafe-jafey ëllëg bis-pénc ak i tar-taram ak i tiitaangeem, nay yombalal ki nekk ci jafe-jafe, ci yokkal ko ak yeexe ko a fayyu boram, walla mu baal dara ci bor bi walla lépp.

فوائد الحديث

Sopp nañu néggandiku ki nekk ci jafe-jafe ba mu nekk cig jàppandi, walla teggil ko bor bi, lépp walla lenn la.

Ku dindil jullit bi jafe-jafey àdduna Yàlla dindil ko jafe-jafey ëllëg bis-pénc, fay gi ci kem jëf gi.

Lii ab tënk la: farata yi ñoo gën naafila yi, waaye leeg-leeg naafila gën farata, rotal bor ci ki nekk ci jafe-jafe naafila la, muñal ko te xaar te bañ ko a laaj lii farata la, te fii naafila gi moo gën farata gi.

Hadiis bi ci àqi ku nekk ci jafe-jafe la, kooku moom dees koy dogal ngànt, bu dee ki am alal tey yeex-yeexlu nag moom, jële nañu ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "yeex-yeexlug aji-woomal ji ag tooñ la".

التصنيفات

Leb