diine de laayante-biir la

diine de laayante-biir la

Jële nañu ci Tamim Ad-Daarii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: «diine de laayante-biir la» nu ne ko: ngir kan? Mu ne: «ngir Yàlla, ak ngir téereem bi, ak ngir Yónentam bi, ak ngir ñiiti jullit ñi, ak ngir jullit ñépp».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day xamle ne diine ji day taxaw ci sellal ak dëgg, ngir ñu defe ko na ko Yàlla warale ba mu mat sëkk te du am genn gàtteñlu walla wuruj. Ñu wax Yónente bi ne ko: kan la laaye-biir Gi kan la ñeel? Mu ne: Bi ci njëkk mooy: laabire ñeel Yàlla mu kawe mi: ci sellal jëf yi ñeel ko, te bañ koo bokkaale, nu gëm ak kennam ci ay jëfam, ak ci jaamu gi, ak ci ay turam ak i meloom, ak di màggal mbiram, tey woote jëme ci gëm ko. Ñaareel bi: laabire ñeel téereem bi te mooy Alxuraan ju tedd ji: ci nu gëm ne waxam la, te mooy téereem bi mujj, te moo folli mbooleem Sariiha ya ko jiitu, nu màggal ko, di ko jàng bu baax, tey jëfe ay laayaam yu leer yi tey gëm yu niroo ya, tey delloo pirim soppikat yi, tey waaru ci ay waaraateem, tey siiwal am njàngaleem, tey woote jëme ci moom. Ñatteel bi: laabire ngir Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ci nu gëm ne mooy Yónente bi mujj, te dëggal ko ci li mu indi, tay jëfe ay ndigalam, di moytu ay tereem, ta nuy baña jaamoo Yàlla ci lu dul li mu indi, nuy màggal ay àqam, te di ko weg, di tasaare wooteem bi, ak Sariihaam bi, te di ko dindil tuuma yi. Ñenteel bi: laabire ñeel njiiti jullit ñi: ci di leen dimbali ci dëgg, tey bañ a xëccook ñoom mbir mi, te di leen déggal ak di leen topp cig topp Yàlla. Juróomeel bi: laabire ñeel mbooleem jullit ñi: ci rafetal jëme ci ñoom ak di leen woo ci diine ji, te bañ leen a lor, ak bëgg leen, tey dimbalànte ak ñoom cig mbaax ak ragal Yàlla.

فوائد الحديث

Digle ag laabire ñeel ñépp.

Màggaayu dayog laabire ci diine.

Làmboo gi diine làmboo ay pas-pas ak i wax ak i jëf.

Bokk na ci laabire sellal bakkan ci wor ki ngay laabire ak bëggal ko yiw.

Rafetug njàngalem Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax muy tënk am mbir ba noppi door koo faramfàcce.

Tàmbalee ca la gën a am solo, ba tax na Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tàmbalee ci laabire ngir Yàlla, teg ci ngir tëereem bi, teg ci ñeel yónenteem bi, teg ci njiiti jullit ñi, teg ci nag mbooleem jullit ñi.

التصنيفات

Àqi njiit ci ña mu jiite