إعدادات العرض
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa set wicc ci aji-yuuxu ji, ak aji-wat kawaram, ak aji-xotti yéereem
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa set wicc ci aji-yuuxu ji, ak aji-wat kawaram, ak aji-xotti yéereem
Jële nañu ci Abii Burdata ibn Abii Muusaa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Abuu Muusaa dafa tawat tawat ju tar, mu daal di xëm fekk boppam bi moo ngi ci pooju jenn jigéen ci njabootam, te manu ko a tontu ci dara, ba mu féexee, daal di ne: man de set naa wicc ci ku Yonente Yàlla bi set ci moom, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa set wicc ci aji-yuuxu ji, ak aji-wat kawaram, ak aji-xotti yéereem.
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Português Kurdî සිංහල Kiswahili Tiếng Việt অসমীয়া ગુજરાતી Nederlands മലയാളം Română Magyar ქართული ಕನ್ನಡ Moore Svenska Македонски ไทย తెలుగు Українська मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasy ភាសាខ្មែរ پښتوالشرح
Abii Burdata yal na ko Yàlla dollee gërëm day nettali ne baayam Abuu Muusaa Al-Asharii dafa feebar feebar bu tar daal di xëm, fekk boppam bi moo ngi tege ci pooju jenn jigéen ci njabootam, mu daal di yuuxu, te manu koo wax dara ndax li mu xëm. Ba mu ximmikoo daal di ne: moom set na wicc ci ku Yonente Yàlla bi set ci moom, te Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ku set la ci: Aji-yuuxu ji: mooy kiy yëkkëti kàddoom ngir musiba Ak aji-wat kawaram: mooy kiy wat kawaram bu musiba amee. Ak aji-xotti yéeréem: mooy kiy xotti ay yéeréem bu musiba amee. Ndaxte loolu ci biri ceddo ya la bokk, waaye dafa digle muñ bu musiba amee, ak yaakaar fayug Yàlla.فوائد الحديث
Tere nañu xotti yéré, ak wat kawar, ak yëkkëti kàddu bu musiba tàbbee, ak ne loolu dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi.
Njàqare ak jooy ci lu dul yuuxu ak yëkkëti kàddu araamaleesu ko, moom safaanoowul ak muñ dogali Yàlla yi, waaye yërmànde la kese.
Araamal nañu mer ci ndogali Yàlla yu metti yi ci wax walla jëf.
Warug muñ ci bu musiba amee.