ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege sunu jàkka yi, te toog ci këram

ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege sunu jàkka yi, te toog ci këram

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege sunu jàkka yi, te toog ci këram", ak ne Yonnente bi indil nañu ko cin lu am ay lujum ak laaj, mu yég ci ag xet, mu laaj ñu xibaar la ca nekk ci laaj, mu wax ne: jegeele leen ko ci kenn ci Sahaaba yi nekkoon ak moom, ba mu ko gisee mu sib ko a lekk, mu wax ko ne: " lekkal, man damay déeyante ak koo dul déeyantel».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ku lekk laaj walla soble muy ñëw ci jàkka ji, ba du lor mbokkam yi teewe jullig mbooloo mi ci xet gi, loo lu nag tereg wattandikoo ñëw ci jàkka ji la, terewul lekk gi; ndaxte ñoom ñaar bokk nañu ci ñam yi dagan, indil nañu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci lu am ay lujum, ba mu ca xeñcoo ag xet ñu xibaar ko la ca nekk, da ko a bañ a lekk mu jegeele ñam wi kenn ci Sahaabaam yi ngir mu lekk ko, mu sib moomitam ngir roy ci moom, ba ko Yonnente bi gisee daal di ne ko: lekkal; man damay déeyante ak malaaka yi ci Wahyu gi. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle ne malaaka yi dañuy loru ci xet gu xasaw, kem ni nit ñi di ci loroo.

فوائد الحديث

Tere nañu képp ku lekk laaj walla soble muy dem si jàkka yi.

Dees na boole ci yooyu, lépp lu am xet gu xasaw gu jullikat yi di loroo, niki xetu sigareet ak póon ak yu ko niru.

Li waral tere gi mooy xet gi, kon bu xet gi deñee ngir togg gu bari mbaa ci leneen; kon sibeel gi deñ.

Sib nañu lekk bir yii ci kuy teewe julli gi ci jàkka ji; ngir mbooloo mi ci jàkka ji bañ ko a faat, lu dul mu lekk ngir bexey baña teew, buboobaa day araam.

Li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bañ a lekk laaj ak yi ko niru, du ngir araamal ko, waaye ngir ne day déeyaale ak Jibriil moo tax.

Rafetug jàngàlem Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ba tax muy lënkale àtte bi ak leeral sabab bi; ngir dalal xelu ki muy waxal ci bu xamee litax.

Al-Xaadii nee na: woroom xam-xam yi nattale nañu ci lii yeneen barabi jullikaay u mbooloo yi nekkul ci jàkka niki jullig iid, ak néew ak yu ko niru ci jaamu, niki noonu barab yi ñuy daje ngir xam-xam ak sikar ak céet ak yu ko niru, waaye (jah yi) marse yi ak yi ko niru du ca dugg.

Woroom xam-xam yi nee nañu: hadiis bi tegtal la ci tere lekk laaj ak yu ko niru ci bu ñuy dugg ci jàkka -donte kenn nekku fa- ndaxte barabu malaaka yi la, ak it li hadiis yi matalee.

التصنيفات

Ngëneelu jullig mbooloo ak i àtteem