إعدادات العرض
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe amee: "laa ilaaha illallaahu Al-Hasiimu Al-Haliimu, laa ilaaha illallaahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi, laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi wa Rabbul Harsi Al-Kariimi
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe amee: "laa ilaaha illallaahu Al-Hasiimu Al-Haliimu, laa ilaaha illallaahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi, laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi wa Rabbul Harsi Al-Kariimi
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe amee: "laa ilaaha illallaahu Al-Hasiimu Al-Haliimu, laa ilaaha illallaahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi, laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi wa Rabbul Harsi Al-Kariimi".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी සිංහල Kurdî Português Kiswahili অসমীয়া Tiếng Việt ગુજરાતી Hausa Nederlands മലയാളം Română Magyar ქართული Moore ಕನ್ನಡ Svenska Македонски ไทย తెలుగు Українська मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ Malagasy ភាសាខ្មែរ پښتوالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax bu jafe-jafe yi ak xat-xat yi daan tar ci moom: "laa ilaaha illallaahu" amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, "Al-Hasiimu" Aji-Màgg dayo ji, Aji-màgg mbir, ci jëmmam ak ay meloom ak i jëfam, "Al-Haliimu" Aji-Lewet ji nga xam ne du yàkkamti aji-moy ji ci ay mbugal waate da koy yeexe, amaana sax mu baal ko ànd ak kàttanam ci moom, moom Aji-Am kàttan la tudd naa sellam ga ci lépp. "laa ilaaha illallahu Rabbul Harsi Al-Hasiimi" amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla mi Bind Aras ju màgg ji, "laa ilaaha illallaahu Rabbus Samaawaati wa Rabbul Ardi" moom miy Aji-Bind Asamaan yi ak Suuf si, di Aji-Bind lépp lu nekk ci seen biir, moom ko te di ko yéwénal, te di Aji-Soppaxndiku ca nu mu ko soobe, "Rabbul Harsi Al-Kariimi" Aji-Bind Aras ju tedd ji.فوائد الحديث
Warug làqatu jëm ci Yàlla ci di ko ñaan bu ay musiba wàccee ak i jafe-jafe.
Sopp nañu ñaan lii bu musiba amee.
Arasu bi nga xam ne ca la boroom bi yamoo moo gën a kawe ci mbindeef yi gën ci a rëy gën ci a màgg, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc melal na ko ci ne lu màgg la lu tedd la.
Jagleel na asamaan yi ak suuf si ci ag tudd; ndaxte ñoom ñaar ñoo gën a màgg ci mbindeef yi ñuy gis.
At-Tiibii nee na: ubbee na tagg gii ci tudd Boroom bi ngir mu méngoo ak wuññi jafe-jafe; ndaxte loolu mooy li war, nekk na ci it tudd Yàlla gi làmboo Tawhiid te mooy cosaanu sellal ku Màgg ki, ak màggaay giy tegtale matug kàttanam, ak lewet giy tegtale matug xam-xamam, ndaxte ki xamul deesul séentu ci moom ag lewet du caagine teddnga te ñoom ñaar ñooy cosaani ci teralaate.
التصنيفات
Sikkar yees di wax jamonoy tar-tar