saaga ab jullig ag kàccoorte la, rayante ak moom ag kéefar la

saaga ab jullig ag kàccoorte la, rayante ak moom ag kéefar la

Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "saaga ab jullig ag kàccoorte la, rayante ak moom ag kéefar la".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ñuy saaga ak ŋàññ jullit bi, ak ne loolu dafa bokk ci kàccoore te mooy génn ag topp Yàlla ak ub yonnenteem, ak ne jullit di rayante ak mbokk jullitam dafa bokk ci jëfi kéefar yi, waaye kéefar gu ndaw la.

فوائد الحديث

Dañoo war a wormaal deru jullit bi ak dereetam.

Màggug mujjanteelu kiy saaga jullit bi ci lu dul dëgg; kiy saaga ci li dul dëgg kàccoor la.

Saaga ab jullit ak rayante ak moom day néewal gëm gi di ko wàññi.

Yenn jëf yi dees na ko woowe ag kéefar; donte eggul ci kéefar gu mag guy génne ci diiney lislaam.

Li ñu namm ci kéefar fii mooy kéefar gu ndaw gi nga xam ne du génnee ci diine ci dëppoog waa sunna; ndaxte Yàlla mu màgg mi dafa saxal mbokkoog gëm ñeel way-gëm ya ca jamono jañuy rayante ak di xeex, Yàlla mu kawe mi wax ne: (bu dee ñaari kureli way-gëm ñi dañuy rayante nangeen yéwénal seen diggante) ba li mu wax ne: (way gëm ñi ñooy ay mbokk).

التصنيفات

Ngëneel yi ak teggiin yi, Jikko yees ŋàññ