ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe ag giléem

ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe ag giléem

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe ag giléem, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe aw nag, ku dem ci ñatteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku jegeele am kuuy mu ami béjjan, ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ag ginaar, ku dem ci juróomeelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ab nen, bu imaam bi génnee maalaaka yi ñëw di déglu xutba gi».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ngëneelu teel a dem ca jullig Àjjuma ja, Teel gi nag day tàmbalee ci bu jant bi fenkee ba baa imaam bi di ñëw; moom nag juróomi waxtu la, dees na ko séddale juróomi xaaj ci kem waxtu yi ci diggante bi jant bi fenkee ba baa imaam bi di dugg si di yéeg ci minbar bi ngir xutba: Bu njëkk bi: ku sangu sangu mu mat kem sangu janaba, topp mu dem ca jàkkay Àjjuma ja ci waxtu wu njëkk wi moo ngi mel ku saraxe ag giléem. Ñaareel bi: ku dem ci ñaareelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe aw nag. Ñatteel bi: ku dem ci ñatteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe am kuuy -muy xar mu mag- mu am ay béjjan. Ñenteel bi: ku dem ci ñenteelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe ag ginaar. Juróomeel bi: ku dem ci jurómeelu waxtu wi moo ngi mel ni ku saraxe aw nen. Bu imaam bi génnee ngir xutba; malaaka yi toogoon ci bunt bi di bind ñiy njëkk a dugg si jàkka ji ak ña ca tege daal di bàyyi mbind mi, ñëw toog di déglu tudd Yàlla gi ak xotba gi.

فوائد الحديث

Soññee ci sangu bisub Àjjuma, balaa ñuy dem ca julli ga.

Ngëneelu teel a dem ca jullig Àjjuma ja ci waxtu wi njëkk ci bëccëg gi.

Soññee ci gaawantu jëm ci jëf yu baax yi.

Malaaka yi dañuy teewe jullig Àjjuma ji di déglu xutba.

Malaaka yi ci bunti jàkka yi lañuy nekk, di bind ñiy ñëw ci jullig Àjjuma ji, ki jiitu ak ka ca tege.

Ibn Rajab nee na: li mu wax ne: "ku sangu bisu Àjjuma, topp mu wéy" day tegtale ne sangu lu ñu sopp la ci bisub Àjjuma, njëlbeenam mooy bu fajar gi fenkee, ag mujjam mooy jëm ca jullig Àjjuma ja.

التصنيفات

Sunna ak teggiini sangu, Jullig Àjjuma