ku lekk aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla mi ma leel lii, wërsëgale ma ko ci lu dul benn pexe bu bawoo ci man du caagine kàttan, kon dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram

ku lekk aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla mi ma leel lii, wërsëgale ma ko ci lu dul benn pexe bu bawoo ci man du caagine kàttan, kon dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram

Jële nañu ci Sahl ibn Muhaas ibn Anas mu jële ci baayam mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ku lekk aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla mi ma leel lii, wërsëgale ma ko ci lu dul benn pexe bu bawoo ci man du caagine kàttan, kon dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram».

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day soññ ku lekk aw ñam mu sant Yàlla, amuma kàttan ci indi ñam wi, du caagine lekk ko ci lu dul ndimbalu Yàlla mu kawe mi, Topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne ku wax loolu yeyoo na Yàlla jéggal ko bàkkaaram yu ndaw yi weesu.

فوائد الحديث

Sopp nañu ñu sant Yàlla ginnaaw bu ñu lekkee ba noppi.

Leeral màggaayu ngëneelu Yàlla mu kawe mi ci jaamam ñi ba tax mu wërsëgal leen yombalal leen yooni wërsëg yi, mu def loolu muy far seen i ñaawteef.

Mbiri jaam ñi yépp ci Yàlla mu màgg mi lay jóge, du bawoo ci seen i pexe ak seen i kàttan, jaam bi nag dañu ko digal mu def sabab yi.

التصنيفات

Sikkar yi ñeel bir yi gaar