ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam

ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam».

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ngëneelu ñaan ci diggante nodd ak liqaam, ci ne deesu ko delloo te yeyoo na ñu nangu ko, deeleen ci ñaan Yàlla.

فوائد الحديث

Ngëneelu ñaan ci waxtu wii.

Bu kiy ñaan làmboo teggini ñaan, jublu ay barabam ak waxtuy ngëneelam, sori moy Yàlla, moytandikul boppam ci tàbbi ci lënt yi ak ya ñuy sikk-sàkka, daal rafet njort ci Yàlla: kon moom yeyoo na ñu nangul ko ñaanam ci ndigalul Yàlla.

Al-Manaawii wax na ci nangug ñaan gi ne: maanaam: ginnaaw dajaloog sàrti ñaan yi ak i ponkam ak i tegginam, bu ca dara wuutee bu mu yedd ku dul boopam.

Nangu ñaan: benn mu nekk ñu nangul ko ñaanam gi jox ko limu ñaan ci lu gaaw, walla ñu wëlbatil ko ci aw ay wu mel ni moom, walla ñu deñcal ka ko ba allaaxira; loolu nag ci kem xereñug Yàlla ak yërmàndeem.

التصنيفات

Yiy waral nangu ñaan ak yi koy xañe