ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman

ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman

Jële nañu ci Aysatu yaayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan seeti ku feebar di ko ñaanal day wax: "ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan seeti ku feebar da koy ñaanal daal di wax: Yaw Yàlla sama Boroom dindil mettit wi ak tarug feebar bi, yaw Boroom nit ñi ki leen Bind yor leen, saafaraal aji-feebar jii, tudd naa sag Sell yaw Aji-Saafara ji, maa ngi jottaliku jëm ci yaw ci sa tur wii di Aji-Saafara ji, aji-feebar ji du saafara wu lu dul ci sag saafa, saafara gog du bàyyi jenn jàngoro.

فوائد الحديث

Kiy wéral mooy Yàlla mu màgg mi, bu dee doktoor bi ak garab yi ñoom ñaar ay sabab lañu duñu jariñ du ñu lor lu dul ci ndigalul Yàlla.

Seeti ku feebar dafa bokk ci àq yi dox ci diggante jullit ñi, ci mbokk gi la gën a yaye.

Xemmemloo ci ku seeti ku feebar mu ñaanal ko ñaan gu baarkeel gii ñu tuxal.

Bokk na ci njubug Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di faj jaareko ci moccug sariiha ci Alxuraan ak ay ñaan yu teey, Yonnente bi daan na mocc boppam bu feebaree, niki noonu yit daan na mocc ku tawat ci njabootam ak ñeneen.

Ibn Hajar nee na: jaaxle amna ci lu tax ñuy ñaanal ki feebar ag wér te feebar bi day far ay bàkkaaram di yok yool ni ki mu ñëwe ci hadiis yu bari, tontu bi mooy: ñaan jaamu Yàlla la, te du dàqonteek yool am tuyaaba ak far bàkkaar; ndax ñoom ñaar dañuy ame ci njëlbeenu feebar ba ak muñ ga, te aji-ñaan gi moo ngi ci diggante Ñaar yu rafet: benn jubluwaayam am, walla ñu wecceel ka ko ci xëcc njariñ walla jeñ lor, te yépp ci ngëneelu Yàlla la.

التصنيفات

Mocc gees yoonal, Teggiini seet ku wéradi