ku am ñaari jabar daal di jeng ci kenn ki, dana ñëw ëllëg bis-pénc wetam gi jeng

ku am ñaari jabar daal di jeng ci kenn ki, dana ñëw ëllëg bis-pénc wetam gi jeng

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «ku am ñaari jabar daal di jeng ci kenn ki, dana ñëw ëllëg bis-pénc wetam gi jeng».

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku am lu ëpp benn soxna, te maanuwul ci seen diggante kem kàttanam, ci yemale seen diggante ci dundal ak dëkkal ak koddaay ak fanaan ga, ci ne mbugalam ëllëg bis-pénc mooy xaaju yaramam daal di jeng, jeng gi mbugal la ci tooñam gi, kem ni mu jenge ci jëflanteem gi.

فوائد الحديث

War na ci góor gi mu séddale ci diggante ñaari jabaram walla ay jabaram, dana araam ci moom muy jeng jëm ci kenn ki wolif keneen ki, ci kem kàttanam ci dundal gi ak fanaan gi, ak rafetug nekkiin, ak lu ko niru.

Yamale ci séddali gi ak yu ko niru, mooy ci li nit ki moom, bu dee li nit ki moomul nag niki bëgg gi ak jengug xol bi loolu du dugg ci hadiis bi, te mooy li ñu namm ci waxu Yàlla ji: {manulee a màndu donte xér ngeen ci} [An-Nasaa-i: 129].

Fay day nekk ci kem jëf ji, góor gi bi mu jengee ci àdduna ci jóge ci jenn jabar jëm ci jeneen, ta mu ñëw ëllëg bis-pénc genn wet gi jeng wolif geneen gi.

Màggaayu àqi jaam ñi, ak ne kenn du ko baale; ndaxte dees ko a tabax ci fayyantoo.

Sopp nañu yem ci benn jabar, bu dee góor gi dafa ragal ne du maanu ci diggante ay jabaram; ngir mu bañ a tàbbi ci gàttañlu ci diine; Yàlla mu kawe mi nee na: {bu ngeen ragalee ne dungeen maanu kon takkleen benn jabar} [An-Nasaa-i: 3].

التصنيفات

Dundiinu ñaari way-dencante yi