moytuleen salte yii Yàlla tere, ku ca laal na suturawu ci surutas Yàlla, te tuub jëm ci Yàlla, ndaxte ku ñu wuññil ay bootam dananu teg ci moom Téereb Yàlla mu màgg mi

moytuleen salte yii Yàlla tere, ku ca laal na suturawu ci surutas Yàlla, te tuub jëm ci Yàlla, ndaxte ku ñu wuññil ay bootam dananu teg ci moom Téereb Yàlla mu màgg mi

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu ne Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ginnaaw ba mu jame (Rajmu) Al-Aslamii dafa taxaw wax ne: "moytuleen salte yii Yàlla tere, ku ca laal na suturawu ci surutas Yàlla, te tuub jëm ci Yàlla, ndaxte ku ñu wuññil ay bootam dananu teg ci moom Téereb Yàlla mu màgg mi"

[Wér na]

الشرح

Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm day nettali ne Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ginnaaw ba mu jamee (Rajmu) Maahis ibn Maalik Al-Aslamii yal na ko Yàlla dollee gërëm ci getenu njaalo, dafa taxaw xutba ci nit ñi wax ne: Moytuleen salte yii ak lépp lu ñu seexlu ñaawlu ko ci moy yi Yàlla tere, ku tàbbi ci dara ci yooyu ñaari mbir war na ci moom: Bi ci njëkk: mu suturawu ngir li ko Yàlla suturaal te bañ a nettali moyam gi. Ñaareel bi: mu gaaw tuub jëm ci Yàlla te bañ ca a nuur, ku ag moyam feeñ nag dananu taxawal ci moom geten gi ñu tudd ci Téereb Yàlla mu màgg mi ñeel moy googu.

فوائد الحديث

Xemmemloo jaam bi def bàkkaar ci mu suturaal boppam, daal di tuub ci digganteem ak Boroomam.

Gétén yi bu eggee ci njiit li fàww rekk mu taxawal ko.

Warug moytu bàkkaar yi, ak tuub ko.

التصنيفات

Tuub