sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya

sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya

Jële na ñu ci Huqbata Ibn Haamir -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sart yi gën a yelloo matal mooy yiy ñu man a daganal bànneexu ci jigéen, te mooy sart yi dagan te jigéen gi di ko sàkku bu ñuy takk sëy ba.

فوائد الحديث

War nañoo matal sart yi nga xam ne kenn ci ñaar ñiy sëy moo ko warlul keneen ki, lu dul muy sart buy araamal lu dagan walla muy daganal lu araam.

Matal sarti sëy moo gën a feddaliku lu dul moom; ndaxte mooy tollook daganal awra ya.

Màggug sëy ci Lislaam, ba tax mu feddali ne na ñuy matale sart ya.

التصنيفات

Sàrt yi aju ci biir sëy