ku wax bismil Laahi Allasii laa yadurru maha ismihii say-un fil ardi walaa fis samaa-i wa huwa As-Samiihu Al-Haliimu, ñatti yoon balaa bu bette du ko dal, ba baa muy xëy

ku wax bismil Laahi Allasii laa yadurru maha ismihii say-un fil ardi walaa fis samaa-i wa huwa As-Samiihu Al-Haliimu, ñatti yoon balaa bu bette du ko dal, ba baa muy xëy

Jële nañu ci Abaan ibn Usmaan mu wax ne: dégg naa Usmaan ibn Affaan yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «ku wax bismil Laahi Allasii laa yadurru maha ismihii say-un fil ardi walaa fis samaa-i wa huwa As-Samiihu Al-Haliimu, ñatti yoon balaa bu bette du ko dal, ba baa muy xëy, ku ko wax bu xëyee ñatti yoon balaa buy bette du ko dal ba baa muy gont", mu ne: ag paraaliise daal di dal Abaan ibn Usmaan, waa ji dégg ci moom hadiis bi tàmbali di ko xool, mu ne ko: lu tax nga may xool nii? Giñ naa ci Yàlla fenaluma Usmaan, te du caagine Usmaan daa fenal Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, waaye bis bi ma lii di dal damaa meroon fàtte ko a wax.

[Wér na]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne ku wax ci suba gi ginnaaw bu fajar gi fenkee, ak ci ngoonu guddi gu nekk njëkk jant bi di so ñatti yoon: (ci turu Yàlla) maa ngi dimbandiku di aaru ci lépp luy lore (moom mi nga xam ne dara du lore ànd ak) tudd (aw turam) lu man a doon (dara) ak lu mu man a màgg (ci suuf) ak li ciy génn ci ay balaa (du caagine ci asamaan si) ak la cay wàcc ci balaa (te Mooy Aji-Dégg ji) sunuy wax (di Aji-Xam ji) sunuy bir. . Ku ko wax bu gontoo benn balaa du ko dal ci ag mbetteel ba baa muy xëy, ku ko wax ci suba gi balaa du ko dal ci ag mbetteel ba baa muy gont. Ki nettali hadiis bi di Abaan ibn Usmaan paraaliise dal ko; te mooy genn wet ci yaram wi bàyyi, waa ji dégg ci moom hadiis bi tàmbali di xool Abaan ngir yéemu! Mu wax waa ji ne ko: lu tax nga may xool nii?! Giñ naa ci Yàlla ne fenaluma Usmaan, te du caagine Usmaan daa fenal Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, waaye bis ba mu may dal Yàlla dogalul ci man ma wax ko, ndax damaa meroon ma fàttee wax baat yii ñu tudd.

فوائد الحديث

Sopp nañu def sikar gii ci suba gi ak ci ngoon gi; ngir nit ki nekk ku ñu sàmm ci ndigalul Yàlla ngir balaa juy bette bañkoo dal walla musiba walla yu ni mel.

mag ña jiitu séenug yaqiin ci Yàlla lu dëgëroon la niki noonu seenug dëggal ci lépp lu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xibaare.

Bokk na ci njariñi tënk sikar yi ci suba gi ak ngoon gi dagg lii di càggante ci jullit bi ak fexe bamuy bàyyi xel fum toll ne moom jaamub Yàlla mu kawe mi la.

Ci kem gëmug kiy tudd Yàlla ak toroxloom ak teewug xolam, ànd ak sellam ak kóolute ci la jeexitalu sikar gi di ame.

التصنيفات

Sikkari suba ak ngoon