amul kenn kuy julli ci man lu dul ne Yàlla dana ma delloo samag ruu ba ma delloo ko nuyóo

amul kenn kuy julli ci man lu dul ne Yàlla dana ma delloo samag ruu ba ma delloo ko nuyóo

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «amul kenn kuy julli ci man lu dul ne Yàlla dana ma delloo samag ruu ba ma delloo ko nuyóo».

[Ag càllalaam tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko,ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne dañu koy delloo ruuham ngir mu delloo nuyóo ki ko nuyu moo xam ku jege la walla ku sori; dundug Barsax ak bàmmeel yi mbirum kumpa la kenn xamul dëgg-dëggam ku dul Yàlla, te Moom lépp la xam.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci di baril julli ak sëlmël ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Dundug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci bàmmeelam mooy dund gi gën a mat gu nit di dund ci Barsaxam, te kenn xamul dëgg-dëggam ku dul Yàlla mu kawe mi.

Hadiis bi du lay ci ñi nga xam ne dañuy wax ne dundug Barsaxu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ag dund la kem ni nuy dunde nun, ba du nekk tegtal ci bokkaalekat yi ci di xettaliku ci moom Yonnente bi, waaye dundug Barsax rekk la.

التصنيفات

Yi Yónnent bi SLM jagoo