Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xoolug mbetteel mu digal ma ma wëlbati samab gis

Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xoolug mbetteel mu digal ma ma wëlbati samab gis

Jële nañu ci Jariir Ibn Abdullah yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xoolug mbetteel mu digal ma ma wëlbati samab gis.

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Jaabir ibn Abdul Laahi yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc góor gu xool jigéenu jàmbur cig mbetteel ci lu dul jubluwaay? Yonnente bi digal ko ne day war ci moom mu wëlbati kanamam jëm ci geneen wàll ga, ca geneen wet ga ci ba mu ko xamee fa saasa, te bàkkaar waru ko ca.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci dammub gis.

Moytandikuloo wéy di xool lu ñu araamal a xool, bu ca gisam dalee cig mbetteel ci lu dul jubluwaay.

Nekk na ci it ne li ñu araamal xool jigéen mbir mu saxoon la ci Sahaaba yi, li koy tegtale mooy ne Jariir yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu xool jigéen amee ci lu dul jubluwaay, ndax àtteem mooy àtteb ki jublu xool ga?

Nekk na ci it ni Sariiha yittewoo li yéwén ci jaam ñi, ndaxte dafa araamal ci ñoom xool jigéen ngir la cay topp ci ay yàquteg àdduna ak allaaxira.

Dellug Sahaaba yi ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di ko laaj lu lënt ci ñoom, niki noonu jaadu na ci mbooloo mi ñuy dellu ci seen woroomi xam-xam di leen laaj lu lënt ci ñoom.

التصنيفات

Sellal bakkan yi