Asan ak Usaynu ñooy sangi waxambaaney waa àjjana

Asan ak Usaynu ñooy sangi waxambaaney waa àjjana

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Asan ak Usaynu ñooy sangi waxambaaney waa àjjana".

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ñaari sëtam yii Asan ak Usaynu ñaari doomi Aliyun Ibn Abii Taalib ak Faatimatu doomu Yonnente bi ñooy sangi kepp ku faatu tey waxambaane bu dugg àjjana ci ngëneel, walla ñooy sangi waxambaaney waa àjjana ba mu des Yonnente yi ak Xalifaa yu jub ya.

فوائد الحديث

Am na ci ngëneel lu feeñ ñeel Asan ak Usaynu yal na leen Yàlla dollee gërëm.

Waxees na ne maanaam hadiis bi: mooy ñoom ñaar ci waxtuw hadiis bi ñooy sangi bépp waxambaane bu bokk ci waa àjjana ci waxambaaney jamono jii, walla ñoom ñaar ñoo gën képp koo xam ne amul ngëneel lu matale lu sax ñeel ko niki Yonnente yi ak xulafaa yi, walla ñoom ñooy sangi ku melowoo melow ndaw ci dëgër ak mbajum rus ak teddnga ak ug jàmbaare, waaye jubluwul ci loolu ati waxambaane; ndax Asan ak Usaynu ci ag paa lañu faatu.

التصنيفات

Ngëneelu waa-kër Yónnent bi SLM