Fekk nañu jenn jigéen ñu ray ko ci benn ci xarey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente bi daal di ñaawlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi

Fekk nañu jenn jigéen ñu ray ko ci benn ci xarey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente bi daal di ñaawlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi

Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Fekk nañu jenn jigéen ñu ray ko ci benn ci xarey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente bi daal di ñaawlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jigéen ju ñu ray ci benn xare, mu naqarlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yu ndaw yi nga xam ne mataguñu am bàkkaar.

فوائد الحديث

Ku xeexul ci jigéen ñi ak xale yi, ak ku yam ak ñoom àtte ci mag yu màggat yi ak làbbe yi, ñooñu deesu leen ray, fii ak ñoom bokkuñu ci ñiy joxe xalaat di xeex jullit ñi, bu dee noonu lañu mel kon dees na leen ray.

Tere nañu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi; ndaxte ñoom duñu rayante ak jullit ñi, te jubluwaayu jihaad ci yoonu Yàlla mooy damm dooley ñiy xeex rekk; ba wooteg dëgg gi; egg ci nit ñépp.

Yërmàndeg Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba ci xare yi ak xeex yi.

التصنيفات

Teggiini xeex ci yoonu Yàlla