buleen jiitu weeru koor ci woor benn walla ñaari fan lu dul koo xam ne da daan woor ag woor kon na ko woor

buleen jiitu weeru koor ci woor benn walla ñaari fan lu dul koo xam ne da daan woor ag woor kon na ko woor

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «buleen jiitu weeru koor ci woor benn walla ñaari fan lu dul koo xam ne da daan woor ag woor kon na ko woor».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na jullit bi woor njëkk weeru koor ci benn walla ñaari bis ci yéeneg wóorlu ñeel weeru koor gi; ndaxte warug woor weeru koor gi dees koo wékk ci gis weer wi, te aajowul a toggoo coona, lu dul koo xam ne da daan woor ag woor gu mu aadawoo niki woor bis dog bis, walla bisu Altine walla Alxamis, mu dëppoo ak moom kon na ko woor; loolu bokkul ci gatandu weeru koor, dees na aj ci loolu it lu nekk woor gu war niki fay ak nisër.

فوائد الحديث

Tere nañu taral, war na it sàmmoonte ak jaamu gi kem ni ñu ko yoonale ci lu dul yokk walla waññi.

Bokk na ci xereñu loolu -Yàlla rekk a xam- ràññetle faratay yi aju ci ay jaamu Yàlla ci ay naafilaam, ak waajal weeru koor wi ci cawarte ak xemmeem, ak ngir woor gi nekk màndargam ci weer wu tedd wi.

التصنيفات

Woor bisub sikk-sàkka