Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc julliwul ag julli ginnaaw bi {Isaa jaa-a nasrul Laahi walfathu} [An-Nasr: 1] wàccee ci moom lu dul dana ca wax: "Subhaanaka Rabbanaa wa bihamdika Allaahuma ixfir lii

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc julliwul ag julli ginnaaw bi {Isaa jaa-a nasrul Laahi walfathu} [An-Nasr: 1] wàccee ci moom lu dul dana ca wax: "Subhaanaka Rabbanaa wa bihamdika Allaahuma ixfir lii

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc julliwul ag julli ginnaaw bi {Isaa jaa-a nasrul Laahi walfathu} [An-Nasr: 1] wàccee ci moom lu dul dana ca wax: "Subhaanaka Rabbanaa wa bihamdika Allaahuma ixfir lii".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba {Isaa Jaa-a nasrul Laahi walfathu} wàccee ci moom dafa firi Alxuraan gaaw jëm ci jëfe ndigalu Yàlla mu kawe mi ci waxam ji: {Fa sabbih bihamdi Rabbika wastaxfirhu}, mu daan bari lu muy wax ci sujjóotam ak rukkoowam ci jamonoy julli gi: "Subhaana" ag sellal ñeel na la ci gépp mànkite ci lépp lu yellul ci yaw, "Allaahuma Rabbanaa wa bihamdika" ci ken gu ñu gërëm ci yaw ngir sa matug jëmm ak say melo ak say jëf, "Allaahuma ixfir lii" faral ma samay bàkkaar te baal ma ko.

فوائد الحديث

Sopp nañu baril ñaan gii ci rukkoo yi ak sujjóot yi.

Sàkku njéggal ci mujjug dund gi ag yeete ci ñu tëje jaamu yi naka noonu -rawati na julli- ci sàkku njéggal, ngir mu dabaatal ki ci am ci ag mànkite.

Li gën ci lu ñuy jotewoo jëm ci Yàlla ci nangu ñaanooy tudd ay gërëmam ak sàbbaal ko ak sellal ko ci gépp mànkite ak ayib.

Ngëneelu jéggalu ak sàkku ko ci gépp anam.

Matug njaamug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak jëfeem ndigali Boroomam.

التصنيفات

Sikkar yi ànd ak julli gi