إعدادات العرض
Allaahuma aslih lii diinii allasii huwa hismatu amrii
Allaahuma aslih lii diinii allasii huwa hismatu amrii
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax: "Allaahuma aslih lii diinii allasii huwa hismatu amrii, wa aslih lii dunyaaya allatii fiihaa mahaasii, wa aslih lii aaxiratii allatii fiihaa mahaadii, wajhal alhayaata siyaadatan lii fii kulli xayrk , wajhal almawta raahatan lii min kulli sarrin".
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Português සිංහල Nederlands অসমীয়া Tiếng Việt Kiswahili ગુજરાતી پښتو Română മലയാളം Deutsch नेपाली Кыргызча ქართული Moore Magyar తెలుగు Svenska ಕನ್ನಡ አማርኛ Українська Македонски Kinyarwanda Oromoo ไทย Српски मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری Malagasyالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaan ñaan goo xam ne dafa boole cosaani teddngay jikkó yi nga xam ne dañu ko a yónni ngir mu mottali ko; te mooy yéwénug diine , ak àdduna, ak allaaxira, mu sàkku ci kàddu yu tënku yii yéwénug mbooleem ñatt yii, mu tàmbalee ci yéwénug diine, te ci la yéwénug nekkiinu ñaari kër yi nekk, mu wah ne: (yaw Yàlla sama Boroom yéwénalal ma sama diine) ci dëppale ma may taxawe ay tegginam ca anam ga gën a mat. (moom mi nekk sama kaaràngey mbir) mooy aji-sàmm samay bir yépp, bu sama diine yàqoo sama bir yëpp yàqu, ma sooy daal di ñàkk, ndaxte yéwénug diine ja nu sàkku du mat ci lu dul yëwénug àdduna, mu wax ne: (yéwénalal ma sama àdduna) ci jox ma wér gi yaram ak jàmm, ak wërsëg, ak jabar ju baax, ak doom yu sell ak lépp lu ma aajowoo, te mu nekk lu dagan, lu may dimbali ci topp la, topp mu tudd ngànt li tax waral muy ñaan yéwénam; ci wax ne: (moom mi nga xam ne ci la samag dund nekk) ak sama barabu dund ak ci jamano jimay dund. (te nga yéwénal ma sama allaaxira ji nga xam ne mooy sama delluwaay) samag dellu jëm ci daje ak yaw te loolu moo ngi ci yéwénug jëf yi, ak tawfeexalug Yàlla ñeel jaamam bi cig jaamu ak ug sellal, ak rafetug mujj. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc toftal ci allaaxira ginnaaw àdduna; ndax àdduna mooy jumtukaay biy tax allaaxira jag, ku jub ci àddunaam kem ni ko Yàlla bëgge, allaaxiraam jub ñeel ko mu texe fa. (defal dund gi) ak gudd fan (ag dolliku ci wépp yiw) ma barile ci ay jëf yu baax, (defal dee gi) ak ug gaawam (ag nooflaay ci wépp ay) ak fitna ak nattu ci bàkkaar yi ak càggante, ak ug mucc ci coonay àdduna ak i jafe-jafeem, ak am ug nooflaay.فوائد الحديث
Diine moo gën a am solo lépp; loolu a tax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tàmbalee ko ci ñaan gi.
Diine kaarànge la ñeel nit ki moo koy tere lépp lu bon.
Ñaan ci mbiri àdduna yi ngir yéwénal diine ak allaaxira.
Sibuñu mébét dee ngir ragal fitna ci diine, walla ñaan Yàlla dee ci sahaada.
التصنيفات
Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM