إعدادات العرض
Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata fiddunyaa wal aaxirati
Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata fiddunyaa wal aaxirati
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul bàyyi di ñaan lii, bu gontee ak bu xëyee: "Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata fiddunyaa wal aaxirati, Allaahuma innii as-aluka alhafwa walhaafiyata fii diinii wa dunyaaya wa ahlii wa maali, Allaahuma ustur hawratii -walla hawraatii- wa aamin rawhaatii, Allaahuma ihfasnii min vayni yadayya, wa min xalfii, wa han yamiinii, wa han simaalii, wa min fawxii, wa ahuusu Bika an uxtaala min tahtii".
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Bahasa Indonesia Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Français සිංහල ئۇيغۇرچە Hausa Kurdî Português Русский Nederlands অসমীয়া Tiếng Việt Kiswahili ગુજરાતી پښتو Română മലയാളം Deutsch नेपाली Кыргызча ქართული Moore Magyar తెలుగు Svenska ಕನ್ನಡ አማርኛ Українська Македонски Kinyarwanda Oromoo ไทย Српски मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری Malagasyالشرح
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daawul bàyyi ñaan yii bu gontee ak bu xëyee: (Allaahuma innii as-aluka alhaafiyata), ak mucc ci tawat yi, ak balaa yi, ak tar-tari àdduna yi, ak bànneexi ak fitnay àdduna yi (fiddunyaa wal aaxirati) li teew ak lay ñëwi ëllëg. (yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan njéggal) ak farug bàkkaar yi ak baale ko, (ak jàmm) mucc ci ayib yi, (ci sama diine) ci bokkalee ak bidaa ak muy yi, (ak sama àdduna) ci musiba yi ak lor yi ak ay yi, (ak sama njaboot) samay jabar ak samay doom ak samay jegeñaale, (ak sama alal) samay alal ak samay jëf. (yalla suturaalal samay ayib) ak li nëbbu ci ay ayib ak i gàkk ak gàtteñlu te nga far samay bàkkaar, (te wóoral samay njàqare) samay tiit ak samay ragaal. (yaw sama Boroom sàmm ma) jeñal ma balaa yiy lore, (ci sama kanam ak sama ginnaaw, ak sama ndayjoor, ak sama càmmooñ, ak sama kaw) mu ñaan Yàlla mu sàmm ko ci gépp wet; ndaxte balaa yi ak gàkk-gàkk yi day dab nit ki di ko jublu ci wet yii yépp. (maa ngi muslu ci sag màggaay ñu bett ma) jàpp ma ci ag mbetteel, alag ma ci ag càggante (ci samag ron) ñu alag ma cig mëdd.فوائد الحديث
Sàmmonte ak kàddu yii ngir roy Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Nit ki kem ni ñu ko digale muy ñaan Yàlla jàmmi allaaxira niki noonu it digal nañu ko muy ñaan jàmmi àdduna.
At-Tiibii nee na: matal na juróom-benni boor yi; ndaxte gàkk-gàkk yi fa lay jóge, mu notal boor bi féeté suuf ngir ne ay gàkk-gàkkam lu suufe la.
Li gën ci jàng sikar yi, ci suba gi: mooy bu fajar gi fenkee ba baa jant bi di fenk ci njëlbeenu bëccëg gi, ak ginnaaw Tàkkusaan ba ca ginnaaw sowug jant bi, bu ko waxee ginnaaw loolu it maanaam: mu wax ko ci suba gi ginnaaw bu yoor-yoor jotee kon dana ko doy, bu ko waxee ginnaaw Tisbaar dana ko doy, loolu waxtuw sikar la.
Amul genn tegtal guy tegtale ne sikar gii amna waxtu wu ràññeeku ci guddi niki jàng ñaari aaya yi mujj ci saaru Al-Baqara ndaxte moom dañu koy jàng ci guddi gi ginnaaw sowug jant bi.
التصنيفات
Ñaan yi bawoo ci Yónnent bi SLM