Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, ci weeru koor nag la daan gën a tabe ba Jibriil daan daje ak moom

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, ci weeru koor nag la daan gën a tabe ba Jibriil daan daje ak moom

Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, ci weeru koor nag la daan gën a tabe ba Jibriil daan daje ak moom, daan na daje ak moom guddi gu nekk ci weeru koor di jàng ak moom Alxuraan, waat naa ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gën a tabe ci yiw ngelaw lu ñu boyal.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gënoon a tabe ci nit ñi, te ag tabeem daana yokk lool ci weeru koor ba daan na joxe li yell a joxe ñeel ku ko yeyoo, li waral tabeem daan yokk nag ñaari mbir la: Bi ci njëkk: daje gi mu daan daje ak Jibriil yal na ko Yàlla yokk jàmm. Ñaareel bi mooy: Tari gimudaan tari alxuraan ji si jibriil. Daan na tari si Jibriil Alxuraan jépp, mu waat ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo gën a tedd gën a man a joxe ak def aw yiw, gën a gaaw a jariñ nit ñi ci ngelaw lu teey lu Yàlla yabal ci taw ak yërmànde.

فوائد الحديث

Leeral tabeg Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak yaatug teraangaaam rawati na ci weeru koor, ndax weeru jaamu la di bisi yiw yi.

Ñaaxe ci tabe ci wépp waxtu, sopp

nañu it yokk ko ci weeru koor.

Baril di joxe ak maye ak rafetal ak jàng Alxuraan ci weeru koor.

Bokk na ci sababi sàmm xam-xam di ko nafar ak ndongo yi ak it woroom xam-xam yi ci tari alxuraan.

التصنيفات

Weeru Koor, Ag tabam SLM