bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe

bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe

Jele nañu ci Abdullah ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: laaj nañu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ndox ak la fay jaabante ci ay ndundat ak i ndegment, mu wax ne: «bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe».

[Wér na]

الشرح

Laaj nañu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc àtteb laabu ndox mi nga xam ne rab yi ak ndegment yi dañu fay jaabante ngir naan ak lu ko niru, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: bu ndox mi tollee ci ñaari mbànd yu mag, muy yamoo ak: (210) liitar kon ndox mu bari la du sobewu; lu dul bu benn ci ñatti meloom yi di meloom wi walla cafkaam gi walla xetam gi soppeekoo ci sobe.

فوائد الحديث

Ndox day sopewu bu benn ci ñatti meloom yi soppeekoo ci sobe, meloom, walla cafkaam, walla xetam, hadiis bi dafa rot ci anamug notal, waaye du cig tënk.

Woroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ne ndox mi bu ko sobe soppee kon sobe la ba fàww, moo xam dafa néew walla dafa bari.

التصنيفات

Àttey ndox yi