bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay

bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay

Jële nañu ci Jaabir ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne moom dégg na Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bu nit ki duggee këram, daal di tudd Yàlla buy dugg ak buy lekk, saytaane day wax naan: amuleen fanaanukaay, amuleen reerukaay, bu duggee te tuddul Yàlla, bi muy dugg, saytaane day wax naan: am ngeen fanaanukaay, bu tuddul Yàlla bu dee lekk, mu wax: am ngeen fanaanukaay ak reerukaay ».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa digle tudd Yàlla bu ñuy dugg ci kër ak balaa ñuy lekk, ak ne bu ñu tudee Yàlla wax: (bismil Laah) bu ñuy dugg ci kër gi ak bu ñuy tàmbalee lekk, saytaane day wax ay gaayam naan: manu leen fanaan, te du ngeen man a reer ci kër gii boroom aaroo ci tudd Yàlla mu kawe mi. Bu nit ki duggee këram nag te tuddul Yàlla bi muy dugg ag ,bi muy lekk, saytaane day wax ay gaayam ne leen am ngeen am panaan, ak ub reer ci kër gii.

فوائد الحديث

Sopp nañu tudd Yàlla bu ñuy dugg ci kër ak bu ñuy lekk, ndax Saytaane day fanaan ci kër gi,di lekk ci lekku waa kër gi, bu ñu tuddul Yàlla mu kawe mi.

Saytaane day ànd ak doomu Aadama ji ci jëfam, di ko wëlbati ci ay biram yépp, te bu sàgganee tudd Yàlla dana am li mu bëgg ci moom.

Tudd Yàlla day dàq saytaane.

Saytaane su nekk am na ñu koy topp ak ñu far ak moom di bége ay waxam tey topp ay ndigalam.

التصنيفات

Ni Yónnent bi SLM daa sikkaree, Njariñi tudd Yàllay Mu tedd Mu màgg mi, Sikkari dugg ak génn ci kër