daganul ci jullit bu jigéen muy tukki lu toll ni doxug guddi lu dul dafa ànd ak góor gu ko araama takk (koc-armalam)

daganul ci jullit bu jigéen muy tukki lu toll ni doxug guddi lu dul dafa ànd ak góor gu ko araama takk (koc-armalam)

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «daganul ci jullit bu jigéen muy tukki lu toll ni doxug guddi lu dul dafa ànd ak góor gu ko araama takk (koc-armalam)».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne araam na ci jullit bu jigéen bi muy tukki luy toll ni doxug guddi lu dul mu ànd ak góor gu bokk ci koj-armalam.

فوائد الحديث

Ibn Hajar nee na: ñàkk a daganu jigéen muy tukki ci lu dul koj-armal, te loolu ag dëppoo la ba mu des ci aj ak umra, ak génn ci dëkkub bokkaale, am na ci ñoom ku boole loolu ci sàrti aj.

Matug Sariihab lislaam, ak ug xéram ci ñoŋal jigéen ak aar ko.

Gëm Yàlla ak bis bu mujj ba day waral toruxlu ñeel sariihab Yàlla bi, ak taxaw ci ay daytalam.

Koj-armalu jigéen mooy jëkkëram walla ku ko araam ba fàww ngir sababu jegeñaale, walla nàmpaale, walla gorowante, ak mu nekk ab jullit nekk muskallaf nekk ku am xel nekk ku wóor nekk ku ñu wóolu; li ñu jublu ci koj-armal mooy aar jigéen ji ak ñoŋal ko ak taxawe ay mbiram.

Al-Bayhaqii wax na ci nettali yi rot ci diirub tukki bi nga xam ne jigéen gi du ko tukki ci lu dul mu ànd ak koj-armal: li ci am mooy ne lépp lu ñuy woowe tukki dees koy tere jigéen gi ci lu dul mu ànd ak jëkkëram walla koj-armal moo xam ñatti fan walla ñaari fan walla benn fan la, walla ab diggante walla lu dul loolu; ngir nettalig Ibn Abbaas gi ñu boyal, te mooy nettalig Muslim gi weesu: {jigéen du tukki ci lu dul kojug armal} te lii day làmboo mbooleem lu ñuy woowe tukki.

te hadiis bi dafa nekkoon ci kem melow aji-laaj ji ak dëkkam.

التصنيفات

Teggiini tukki ak i àtteem, Warteefi wumra