Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw

Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne soppeem ba di xaritam ba Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko a dénk ñatti mbir: Bi ci njëkk: woor ñatti fan ci weer wu ne. Ñaareel bi: julli ñaari ràkkay yoor-yoor bis bu nekk. Ñatteel bi: Wiitar njëkk muy nelaw, loolu nag ci ki ragal ne du yewwu ci mujjug guddi gi.

فوائد الحديث

Wuute gi ay

dénkaaneem wuute

ñeel ay Sahaabaam: dafa tabaxu ci lu mu xam moom Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc meloy àndandoom yi, ak li méngoo ak kenn ku ne ci ñoom, ki am kàttan jihaad day méngoo ak moom, jaamukat bi jaamu day méngoo ak moom, boroom xam-xam bi xam- day méngoo ak moom, noonu lay deme.

Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na ci li mu wax: woor ñatti fan ci weer wu ne, li ci feeñ mooy li mu ci namm mooy bis yu leer yi; te mooy: bisu fukkeel bi ak ñatt, ak fukkeel ak ñent, ak fukkeel ak juróom, ci weeru gàddaay gi.

Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: nekk na ci ne sopp nañu jiital Witar ci kaw nelaw, loolu nag ci àqi ku wóoluwul ne dana yeewu.

Solos ñatti jëf yii;

ndax li ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk ab lim ci ay Sahaabaam.

Ibn Daxiixil Hiid nee na li mu wax: (ñaari ràkkay yoor-yoor): amaana dafa tudd li ci gën a néew nga xam ne def gi daa feddaliku, te tegtal la ci ne sopp nañu jullig yoor-yoor, la ca gën a néew mooy ñaari ràkka.

Waxtuw julli yoor-yoor: mooy ginnaaw fenkug jant bi ba luy toll ci ñenteelu xaaju waxtu wi, waxtoom nag dana wéy ba laata Tisbaar ci luy tollook fukki simili, ab limam nag: la ca gën a néew mooy ñaari ràkka, wuute nañu ca la ca gën a bari; nee nañu: la ca gën a bari amul ab lim.

Waxtuw jullig Wiitar: mooy ginnaaw jullig Gee ba keroog fajar gi di fenk, la ca gën a néew mooy benn ràkka, la ca gën a bari mooy fukki ràkka ak benn.

التصنيفات

Koorug gàtt-nga